info@birima.org

BOROOM BÈNN BAAT BA.
AMOON KÀDDU, LU MU WAXAAN DEF KO. KAJOOR
NAW KO. CI JIKÒOM LA NU TIBBE, NAS CI, LII DI KURÉEL
GI TUDD BIRIMA DI YËNGU CI JÀPPALE AKA LEBLE LU WAAY LIGÉEYE, TE YUUSU
NDUUR TAAWU KO. KEES U BIRIMA GII NAK, KÓOLUTE KESE LA SAMP
DIGËNTÉEM AK WAY LEB YI.

LI KO TAX A JOG
JÀPPALE BÉPP WAA SENEGAAL, MU TAXAWAL YËF I BOPPAM
BA MAN A LIGÉEY.
JÀPPALE ARTIST YI, RAWATINA YIY DOOG A JÓG, JIGÉEN ÑI, GÓOR, MAG AK NDAW,
TAMBALI CI KÈNN BA CI MBOOLOO, JOX KO, GUNGE KO BA MU TAXAW, DEMAL BOPPAM.
LII, MOOY LI BIRIMA BËGGËL RÉEW MI.